TSK

TSK · Leviticus 15:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Noonu ngay def ak Aaróona aki doomam, ni ma la ko sante rekk. Diiru juróom ñaari fan ci nga leen di sas,

Waaye bunt xaymab ndaje mi buleen ko wees diiru juróom ñaari fan, ba bésub keroog ba seen xewu colu di mat, ndax juróom ñaari fan lay mat.

Ku ñuy laabal day fóot ay yéreem, watu ba set te sangu, doora set. Gannaaw loolu man naa dugg ci dal bi, waaye na yem ca bunt xaymaam ca biti diiru juróom ñaari fan.

Képp ku laal lalam, na fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu yendoo sobe ba jant so.

¶ «Bu xëppee ba jeexal, dina waññ juróom ñaari fan, doora tàggook sobe sa.

¶ «Bu loolu weesee ku laal nit ku dee, ak néew bu mu mana doon, dina sobewu diiru juróom ñaari fan.

Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal.

James 4:8 TSK

Jegeleen Yàlla, mu jege leen. Yeen bàkkaarkat yi, raxasleen seeni loxo, yeen ŋaralekat yi laa ne, setal-leen seen xol.