Tegal kubeeru njotlaay gi ci kaw gaal gi, gannaaw boo ci yebee àlluway seede si ma lay jox.
TSK
TSK · Leviticus 16:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Sàkkal ab sarxalukaay bu ñuy taal cuuraay ci kawam. Bantu séng nga koy defare.
Sarxalkat yi dañoo wara dénkoo samay dénkaane bala ñoo gàddu bàkkaar, di dee ndax seenug néewal ci yooyu. Maay Aji Sax ji leen sellal.
¶ Ba mu ko defee ku nekk jël ub andam, def cay xal, teg ca cuuraay. Ñu taxaw ca bunt xaymab ndaje ma, ñook Musaa ak Aaróona.
¶ Gannaaw nag am nanu kilifag sarxalkat bu mag bu jàll ba biir asamaan, te mooy Yeesu Doomu Yàlla, nanu ŋoy ci yoonu ngëm wi.
Ndax bérab yu sell yu nit tabax, te muy royaalub bérab bu dëggu ba doŋŋ, du ci la Almasi dugg. Waaye biir asamaan ci boppam la dugg ngir teewal nu tey, fa kanam Yàlla.
¶ Bi loolu amee meneen malaaka dikk, taxaw ci wetu sarxalukaay bi. Mu ngi yor andu cuuraayu wurus. Ñu jox ko cuuraay lu bare, ngir mu boole kook ñaani mboolem aji sell ñi, jooxe ko ci kaw sarxalukaayu wurus bi ci kanam ngàngune mi.