TSK

TSK · Leviticus 16:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Defarlul kubeer gu ñuy amale njotlaay gu wurusu ngalam ngir gaal gi. Na guddaayam di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaayam di xasab ak genn-wàll.

Wewal rido bi ci ron lonku yi, su ko defee nga yóbbu gaalu àlluway seede si foofu ci gannaaw rido bi, rido bi xàjjaleel leen bérab bu sell bi, ak bérab bu sell bee sell.

¶ Gannaaw loolu ñu jël àlluway seede si, yeb ko ci gaal gi, ba noppi roof njàppu yi ci gaal gi. Ñu daldi teg kubeeru saraxu njotlaay gi ci kaw gaal gi.

Ci bunt xaymab ndaje mi ngeen di yem guddeek bëccëg diiru juróom ñaari fan, boole ci di dénkoo dénkaaney Aji Sax ji, ndax ngeen baña dee, ndaxte loolu moo di li ñu ma santoon.»

¶ «Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, te mooy ñuy joxeel bànni Israyil seen njotlaay benn yoon cim at ngir seen bàkkaar yépp.» Ñu daldi def li Aji Sax ji santoon Musaa.

Nii ngeen di def ak ñoom, ba bu ñu jegee yëf yu sell yee sell, di dund te duñu ca dee: Aaróona aki doomam ñooy dugg, daldi sédd ku nekk ci ñoom liggéeyam ak la muy gàddu.

Yaw nag yaak say doom, dénkooleen seenug carxal ci mboolem mbiru sarxalukaay bi, ak ca wàllaa ridob biir bi, ngeen di ca liggéey. Seen liggéeyu carxal bi, ab sasu teraanga la, maa leen ko terale. Waaye ku bokkul ci yeen, bu ci laalee, dees koy rey.»

¶ Ba sarxalkat ya génnee bérab bu sell ba, niir wa daa fees kër Aji Sax ja,

Néeg ba ca wàllaa ñaareelu rido ba, moom lañu daan wooye bérab bu sell baa sell.

Duggul biir asamaan it ngir di sarxe ak a sarxewaat boppam, noonee sarxalkat bu mag ba daan dugge at mu nekk fu sell faa sell, yóbbaale deret ju dul josam.