Bés bu jëkk bi nangeen ci amal ndaje mu sell. Juróom ñaareelu bés ba itam nangeen ca amal ndaje mu sell; deesul liggéey lenn ci yooyu bés, lu moy ngeen togg ñam wu ñépp lekk. Loolu doŋŋ lees ciy mana def.
TSK
TSK · Leviticus 16:29
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Na Aaróona di sàkk ci deretu saraxu póotum bàkkaar bi, taqal ci béjjéni sarxalukaay bi, ngir def ko njotlaayal sarxalukaay bi benn yoon cim at. Benn yoon cim at lañu koy defal njotlaayam ci seen gépp maas. Sarxalukaay bu sella sell la, ñeel Aji Sax ji.»
Bés bu jëkk bi ndaje mu sell ngeen ciy amal. Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey.
«Te itam fukki fan ci juróom ñaareelu weer woowu, bésub Njotlaay ba lay doon. Ndaje mu sell ngeen ciy amal. Nangeen ci toroxlu te indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
Diiru juróom ñaari fan ngeen di indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. Bésub juróom ñetteel, ba wara doon seen ndaje mu sell, nangeen ci indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. Ndajem mujjantal ba la. Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey.
¶ «Fukki fanu juróom ñaareelu weer woowu it, seen bésub woote bu sell lay doon, te ngeen toroxlu ci. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey.
¶ Ba juróom ñaareelu weer wa agsee, fekk na bànni Israyil sancaat ca seeni dëkk, mbooloo ma daje doon benn bopp ca Yerusalem.
Damaa xér ci sa kër gi, ba jeex tàkk, te jëf ji ñu la sewale man la dal.
Ndax lii moo di koor gi ma taamu, ci bés bu nit kiy toroxlu? Koorug dëngal loos ni barax, lal saaku, sotti ab dóom, tëdd di ko ñaawloo? Loolooy seen koor, ci bés bu Aji Sax ji rafetlu?
Ñam wu neex lekkuma ko, te yàpp ak biiñ jaarul sama gémmiñ. Diwuwma it ba ñetti ayi bés yi mat.
Su nu doon àtte sunu bopp, deesu nu àttee noonu.
Ndax ku tàbbi ci noflaayu Yàlla kat, na Yàlla dal-loo woon ca ay liggéeyam, ni ngay dal-loo ci say liggéey.