TSK

TSK · Leviticus 17:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Waaye kat bu nit lekkee lenn ci yàpp wu ñu def saraxu cant ci biir jàmm te fekk mu am ñetti fan, deesul nangul boroom sarax si te du ko jariñ dara. Lu ñu sib la te ku ca lekk mooy gàddu bàkkaaram.

¶ «Su nit jëlee jabar ab jigéenam bu mu bokkal jenn ndey mbaa benn baay, ñu séq lalu séy, loolu gàcce la. Nañu leen dagge ci biir bànni Israyil, ñooñuy gis. Gannaaw moo tëdde ab jigéenam, na wéetoo añu ñaawtéefam.

Bésub ñetteel ba nag, ak bésub juróom ñaareel ba, ci la nit ku set di wis-wisal ndox mi ci kaw ki sobewu. Bésub juróom ñaareel ba ca la koy settli. Su ko defee ka sobewu fóot ay yéreem, sangu, bu jant sowee mu daldi set.

Mooy sonn ba gis ug leer, doyloo ko, te ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub, ba mu àtte leen àtteb njekk, sëfoo seeni ñaawtéef.

noonu itam la Almasi doone ab sarax benn yoon, ngir gàddu bàkkaaru nit ñu bare, te dina teewsiwaat, ci yoon wu joteetul dara ak bàkkaar, ngir indil ñi koy séentu seenug mucc.