Jëlal mboolem nebbon bi sàng yérey biir yi, ak bàjjo bi ci res wi, ak ñaari dëmbéen yi ànd ak nebbon bi ci kaw dëmbéen yi, nga boole lépp def ko saraxu taal-saxaral ci kaw sarxalukaay bi.
TSK
TSK · Leviticus 17:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Day teg loxoom ci kaw boppu jur gi muy sarxal, te rendi ko ca bunt xaymab ndaje ma. Doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi daldi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.
te teg loxoom ci boppu xar mi muy sarxe, ñu rendi ko ci bunt xaymab ndaje mi, doomi Aaróona yu góor yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.
te teg loxoom ci bopp bi, ñu rendi ko ci bunt xaymab ndaje mi. Na doomi Aaróona yu góor yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.
Te it na génne nebbon bi yépp ni muy génnee nebbonu jur gu ñu def saraxu cant ci biir jàmm. Na ko sarxalkat bi lakkal Aji Sax ji ci kaw sarxalukaay bi, muy xeeñ xetug jàmm. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal.
¶ «Waaye sarxalkat yiy Leween, sëtoo ci Cadog, te daa dénkoo dénkaaney bérab bu sell bi ba bànni Israyil jàddee, ñooñoo may jege, di ma liggéeyal; ñooy dikk fi man, di indi saraxi nebbon ak deret. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.