¶ «Góor gu njaaloo, mook jabaru moroomam ji muy njaalool, dee rekk mooy seen àtte.
TSK
TSK · Leviticus 18:20
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Bu ñu fekkee kuy tëdde ku am jëkkër; ka ko tëdde ak ka ñu tëdde, dee mooy seen àtte, ñoom ñaar ñépp, ngeen tenqee ko lu bon ci Israyil.
Daawuda yónnee, gëstu mbiram, ñu ne ko: «Xanaa du Batseba doomu Eliyam, jabaru Uri, Etteen bi?»
Bu ko xemmeme taaram, bumu la fiir aki lamsal.
tund ya ca saraxi tuur ya, lekkejiwu ca, kasaray tuuru waa kër Israyil, wékku cay gëtam, jabaru jaambur, sobeelu ko, jigéen ju gis baax, jegewu ko,
¶ Am xamuleen ne aji jubadi ñi amuñu cér ci nguurug Yàlla? Bu leen kenn nax: Muy fokati séy yi, di bokkaalekat yi, di jaalookat yi, di góor-jigéen yi, ak ñiy ànd ak ñoom,
¶ Na ñépp wormaal diggante bu ab séy dox, te ab lalu séy na mucc sobe, ndax fokati séy yi, ak jaalookat yi, Yàlla moo leen di daan.