TSK

TSK · Leviticus 18:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

«Waxal bànni Israyil ne leen: Muy bànni Israyil muy doxandéem ci Israyil, képp ku ci jël ciy doomam, jébbal tuur mi ñuy wax Moleg, dee rekk mooy àtteem. Na ko waa réew mi dóor ay doj, ba mu dee.

Nañu nekkal seen Yàlla ay nit ñu sell, te baña teddadil seen turu Yàlla, ndax saraxi sawar yi ñeel Aji Sax ji, te di seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Kon nag dañoo wara sell.

Te buleen teddadil sama tur wu sell. Na bànni Israyil wormaal sama sellaay. Maay Aji Sax ji leen sellal,

Buleen defe noonu ak seen Yàlla Aji Sax ji, ndax mboolem lu seexluwu lu Aji Sax ji bañ, defal nañu ko seeni tuur. Seen doom yu góor ak yu jigéen sax, lakk nañu leen, defal leen seeni tuur sarax.

Ci biir loolu Suleymaan tabaxal Kemos, tuuru Mowab mu siblu ma, ab bérabu jaamookaay ca kaw tund wa féete Yerusalem penku. Mu tabaxaaleel ca Moleg, tuur mu siblu ma Amoneen ñay jaamu.

Ca tànki buuri Israyil la topp. Doomam ju góor sax def na ko sarax, lakk ko ngir tuur ya, di roy ñaawtéefi xeet, ya Aji Sax ji dàqoon ngir bànni Israyil.

Te itam sarxal na doomam, lakk ko ngir ay tuur. Ci biir loolu jabar na, ñeengo na, jëflante naak boroom rawaan aki gisaanekat. Bare na lu mu def lu Aji Sax ji ñaawlu, ba merloo ko.

Ñuy sarxalal rab ya seen doom yu góor ak yu jigéen,

Ñoo tabax ay jaamookaay ca Tofet fa xuru Ben Inom, di fa sarxe seeni doom, góor ak jigéen, lakk leen, te santaanewma ko, jaarul sax sama xel.

Bu ngeen di joxe ay sarax, di lakk seeni doom ngir ay tuur, yeena ngi sobeel seen bopp ba tey jii ci seen tuur yii yépp. Man nag ngeen defe ne maa leen di bàyyi, ngeen seetlusi fi man, yeen waa kër Israyil? Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, duma leen bàyyi mukk ngeen seetlu fi man.

Waaye fu ñu dem ca biir yéefar ya, teddadil nañu fa sama tur wu sell, nit ña di leen waxtaane, naan: “Ñii de, ñoñi Aji Sax ji lañu, teewul réewam ma lañu bàyyikoo nii.”

Amos 5:26 TSK

Te ngeen di yékkati seen tuur yi ngeen sàkk: Sikkut, di seen buur, di seen tuur, Kiyun di biddiiw bu ngeen di jaamu.

Acts 7:43 TSK

Molog seen tuur mi, ngeen yóbbaale xaymab jaamookaayam, ak seen biddiiwu yàlla ji ñu naa Refan, jëmm yooyu ngeen sàkk, di leen sujjóotal! Kon nag maa leen di toxal ca wàllaa Babilon.”

Yeen de yeena tax ñuy ñàkke teggin turu Yàlla ci biir xeeti jaambur yi dul Yawut, te noonu la ko Mbind mi indee.