TSK

TSK · Leviticus 18:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Su ngeen sobeelee réew ma, dinaa leen gëq, na ma gëqe woon xeet ya leen fa jiitu woon.

Buleen tilimal réew mi ngeen nekk. Deret kat mooy tilimal réew mi, te réew mi deesu ko jote lenn, ci deret ju ñu tuur ci biiram, lu moy deretu ka tuur deret.

Du seen genn njekk, akug njub gu leen may ngeen nanguji seenum réew. Waaye mbonug xeet yii moo waral seen Yàlla Aji Sax ji dàqal leen leen, ngir sottal kàddu ga mu giñaloon seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba.

Ezra 9:11 TSK

yi nga nu dénk, yonent yiy say jaam jottli ko, ne nu: «Réew mi ngeen di nanguji, réew mu sobewu la ndax sobey waasoy réew ma. Feesal nañu kook seeni jëf ju siblu ak seen tilim, ba fépp daj.

di tuur deretu ñu deful dara, te muy seen deretu doom yu góor ak yu jigéen ya ñu sarxalal tuuri Kanaaneen ña, deret ja sobeel réew ma,

Aji Sax ji kat a ngii di génne bérabam ba, nara dikke waa àddina mbugalu ñaawtéef, ba suuf wone deret ji ñu tuur fi kawam, te dootu sàng ñi ñu bóom.

Lii, duma leen ko dumaa?» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Wii xeet, duma ko fey yoolam?»

Tund ya laay jooy, di yuuxu, di jooy parluy màndiŋ ma, fa lépp lakk, ba jaareesu fa, déggeesul baatu jur; njanaaw ak mala, lépp daw, ne mes.

Dama leen di jëkka fey ñaari yoon seeni moy, ndax ñoo sobeel sama réew meek seen méddi tuur yu bon yi, feesal suuf sii ma séddoo seen yëf yu siblu yooyu.»

«Yaw nit ki, ba waa kër Israyil dëkkee seen suufas bopp, dañu koo sobeele seen jikko ak seeni jëf, seen jëfin mel ni sagaru sobe ci man.

Ñooy sarxe jur gi ñu may jooxeel, lekk yàpp wi, Aji Sax ji buggu ci dara. Maay bàyyi xel ci seen ñaawtéef, mbugale leen seeni moy, te ñoom Misra lañuy dellu.

¶ Xam nanu ba fii nu tollu ne mboolem càkkéef gaa ngi binni ndax mitit, ni kuy matu.