¶ Yàlla dellu wax Musaa ne ko: «Man maay Aji Sax ji.
TSK
TSK · Leviticus 18:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
da koo wax, ne ko: «Man maay Aji Sax ji. Nanga wax Firawna buuru Misra, li ma lay wax lépp.»
Su boobaa seen Yàlla Aji Sax jee leen di xarfal xarafu xol, te mooy xarfal xarafu xol, seen askan, ngir ngeen soppe seen Yàlla Aji Sax ji seen léppi xol, ak seen léppi bakkan, ndax ngeen dund.
Artu nga leen ndax ñu dellu ci saw yoon, teewul ñu bew, ba sàmmuñu say santaane, xanaa di moy sa àttey yoon yiy taxa dund képp ku ci sàmmu. Ñuy daŋŋiiral, sajju loos, bañ laa déggal.
¶ «Waaye waa kër Israyil dañu maa gàntal ca màndiŋ ma. Sama dogali yoon, jëfewuñu ko, sama àttey yoon yiy guddal fanu képp ku koy jëfe, ñu xalab. Ñàkke nañu worma lool sama bési Noflaay. Ma nar leena xëpp samam sànj ca màndiŋ ma, sànk leen.
«Man Aji Sax ji déy, duma soppiku, te yeen noppiwuleen di askanu Yanqóoba, ay workat.
¶ Njub gi sàmm ndigali yoon di maye, li ci Musaa bind moo di: «Kuy jëfe digal yooyu, yaay dund ndax ñoom.»