TSK

TSK · Leviticus 19:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ay doom ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Buleen ñaasu, buleen wat seen kawaru bopp fi féeteek jë bi, ngir di ko mititloo ku dee,

Nit ñaa ngi yéeg jëm kërug jaamookaay ga ca Dibon, ngir jooyi ca bérabi jaamookaay ya, Mowab a ngay yuuxoo kaw tundu Nebo ak Medeba, boppoo bopp dib nel, sikkimoo sikkim xuufu,

Ku mag ak ku ndaw ay dee ci réew mii, te deesu leen rob, deesu leen jooy. Kenn du dagg yaramam mbaa muy nelu, di ko ñaawloo.

Ñooy sol ay saaku di ko ñaawloo, seen yaram wépp daw, gépp kanam sëlmoo gàcce, bopp ya di nel yu set wecc.