TSK

TSK · Leviticus 20:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Wax leen boog ne leen: Képp kuy góor, ku bokk ci waa kër Israyil, mbaa mu bokk ci doxandéem yi ci seen biir, buy génne ab saraxu rendi-dóomal mbaa beneen sarax,

¶ «Te itam képp ku lekk médd mbaa lu rab fàdd, muy njuddu-ji-réew mbaa doxandéem, na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so, mu doora set.

¶ «Góor gu bokk ci yeen mbaa jigéen, di seete nit ñu dee mbaa muy boroom rawaan buy gisaane, dee rekk mooy àtteem. Dees koy dóor ay doj, mu dee, gàddu bakkanu boppam.»

Ku ñàkke kersa turu Aji Sax ji, dee rekk mooy àtteem. Mbooloo mi mépp a ko wara dóor ay doj, ba mu dee. Muy doxandéem muy njuddu-ji-réew, ku ci ñàkke kersa turu Aji Sax ji, dee mooy àtteem.

Ci kaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: «Dee rekk mooy àtteb waa ji: dees koy génne dal bi, mbooloo mépp dóor koy xeer, ba mu dee.»

Reyleen ko rekk. Yeen ñi mu doon jéema yóbbaale, na ko seen loxo jëkka dal, ngir rey ko, bala cee loxol mbooloo mépp topp.

¶ Bu nit feeñee ci seen biir, ci benn ci dëkk yi leen seen Yàlla Aji Sax jiy jox, muy góor mbaa jigéen juy def lu seen Yàlla Aji Sax ji ñaawlu, di fecci kóllëreem,

Bu kenn fekk ci seen biir kuy sarxe doomam ju góor, ak ju jigéen, lakk ko; ak kuy luxus, ak kuy seet, ak kuy gisaane, ak kuy xërëm,

nañu yóbbu ndaw sa ba ca bunt kër baayam, te góori dëkk bi dóor koy doj ba mu dee, ndax moo def jëf ju gàccelu ci digg Israyil, di gànctoo kër baayam. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir.

Ci biir loolu ñuy lakk seen doom yu góor ak yu jigéen ngir ay tuur, di gisaaneek a xërëmtu, ba làggi ci jëfi mbon yu Aji Sax ji ñaawlu, ba tax mu mer.

di tuur deretu ñu deful dara, te muy seen deretu doom yu góor ak yu jigéen ya ñu sarxalal tuuri Kanaaneen ña, deret ja sobeel réew ma,

Ñoo tabax ay jaamookaay ca Tofet fa xuru Ben Inom, di fa sarxe seeni doom, góor ak jigéen, lakk leen, te santaanewma ko, jaarul sax sama xel.

¶ «“May wax, nga jël sa doom yu góor ak yu jigéen yi nga ma jural, di leen sarxalal say tuur, leele leen. Gànctu da laa doyul?

Bu ngeen di joxe ay sarax, di lakk seeni doom ngir ay tuur, yeena ngi sobeel seen bopp ba tey jii ci seen tuur yii yépp. Man nag ngeen defe ne maa leen di bàyyi, ngeen seetlusi fi man, yeen waa kër Israyil? Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, duma leen bàyyi mukk ngeen seetlu fi man.

Ñoo rendil seen kasaray tuur seeni doom, ba noppi dugg sama biir kër gu sell ci bés bi, ba teddadil kër gi. Loolu déy, moom lañu def fi sama digg kër gii!

Acts 7:58 TSK

ñu wat-watee ko, génne ko dëkk ba, di ko dóor ay doj. Fekk na seede ya summi seeni mbubb, juug ca tànki benn xalelu góor bu ñuy wax Sóol.