TSK

TSK · Leviticus 21:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Musaa wax Aaróona ak doomam yu góor yi tudd Elasar ak Itamar ne leen: «Buleen njañu te buleen ñaawlu di xotti seeni yére, lu ko moy dingeen dee, te merum Yàlla dina dal ci kaw mbooloo mi mépp. Waaye seen bokki bànni Israyil gépp sañ nañoo jooy ñi Aji Sax ji lakk.

Fu ab néew nekk du fa dem, bu doon ndeyam mbaa baayam sax, du ko taxa sobeel boppam.

¶ «Lii la yoon wi tëral: Bu nit deeyee ci biir xayma, képp ku dugg ci biir xayma bi, ak képp ku mu fekk ci xayma bi, day sobewu diiru juróom ñaari fan,

¶ «Nit ku dee nag, ab sarxalkat du ko jege, di sobeel boppam, ndare ki dee di baayam mbaa ndeyam, mbaa doomam ju góor, mbaa ju jigéen, mbaa doomu ndeyam ju góor mbaa ju jigéen ju amul jëkkër, ba mu sañ caa sobeel boppam.

¶ «Léegi nag, sarxalkat yi, santaane bii yeen la ñeel.