TSK

TSK · Leviticus 22:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba loolu wéyee Yàlla ne Yanqóoba: «Jógal dem Betel, toog fa te nga sàkkal fa sarxalukaay Yàlla, ji la feeñu, ba ngay daw sa mag Esawu.»

¶ «Su fekkee ne li nit kiy sarxalal Aji Sax ji saraxu cant la ci biir jàmm, te mu di ko jële ci jur gu gàtt, gu góor mbaa gu jigéen, na sarxal lu amul sikk.

bu ngeen di defal Aji Sax ji saraxu sawara, muy saraxu rendi-dóomal, mbaa sarax su nit di wàccoo aw xas, mbaa saraxu yéene, mbaa seen saraxi màggal, ngir xeeñal xetug jàmm ñeel Aji Sax ji, te muy lu jóge ci jur gu gudd mbaa gu gàtt, defe leen ko nii:

Ab doxandéem, sañ ngeen koo sàkku tegandaay, waaye seen mbokkum bànni Israyil, buleen ko sàkku tegandaay. Su ko defee seen Yàlla Aji Sax ji mooy barkeel mboolem seenu ñaq, ca réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko.

«Tey matal naa la ma digoon Yàlla, yàppu bernde waa nga kër ga, saraxu cant la.