TSK

TSK · Leviticus 23:40

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Su ko defee ngeen bége fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, yeen ak seen doom yu góor ak yu jigéen, ak seen jaam yu góor ak yu jigéen, ak Leween ñi ci seen biiri dëkk te amuñu wàll, amuñu céru suuf ci seen biir.

Ci kaw loolu ñu gis ne bind nañu ci yoon wi Aji Sax ji santaane, te Musaa jottli ko, ne: «Bànni Israyil dañoo wara dëkk ci ay mbaar diiru màggalu weeru juróom ñaareel wa.»

Ñi Aji Sax ji xettleey délsi, duggsi Siyoŋ, di sarxolle, kaalawoo bànneex bu sax. Mbég ak bànneex a leen di dab, naqar aku tiis dëddu leen.

Ndaxte nun noo xaraf tigi, nun ñiy jaamoo Yàlla Noowam gu Sell, di damoo Almasi Yeesu, te yaakaarunu aaday nitu suuxu neen.

Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd,