Leviticus 25:25
TSK
¶ «Bu sa mbokk demee ba ñàkk tax koo jaay ci suufam, mbokkam mi ko gëna jege te am sañ-sañu jotaat suufam, na jëndaat la mbokk ma jaayoon.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Bu sa mbokk demee ba ñàkk tax koo jaay ci suufam, mbokkam mi ko gëna jege te am sañ-sañu jotaat suufam, na jëndaat la mbokk ma jaayoon.
Moona nun de, nook ñi nuy lebal benn lanu, diy bokk lenqe, te seeni doom gënuñu sunuy doom. Terewul nu ngi nara dugal sunuy doom yu góor ak yu jigéen cig njaam. Am na sax ñenn ci sunuy doom yu jigéen, ñu nekk cig njaam ba noppi. Manunu ci dara ndax sunuy tool ak sunu tóokëri reseñ a ngi ci yeneen loxo.»
Waaye ba àpp ba jotee, Yàlla moo yónni Doomam, mu juddoo ci jigéen, juddoo ci biir curgag yoonu Musaa,