TSK

TSK · Leviticus 25:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

waaye atum juróom ñaareel ma, noppal-leen tool bi, booyal ko; seen néew-dooley askan wi man cee lekk, li ci des, rabi àll yi for ko. Seen toolub reseñ ak seen tóokëru oliw itam, naka noonu.

«Lii, def ko ci, mu dib takk. Dees na lekk ren peppum saxayaay, déwén it dees na lekk lu saxal boppam. Waaye déwén-jéeg, ngeen ji, góob, jëmbat tóokëri reseñ, lekk ca meññeef ma.

Acts 4:32 TSK

¶ Ci kaw loolu mboolem gëmkat ñi bokk menn xel, ak benn xalaat. Du kenn ku ne moo moom lenn ci alalam, waaye ñoo bokkoon lépp ci seen biir.