¶ «Te itam dogal a ngii, di lu leen war fàww. Bésub fukki fan ci juróom ñaareelu weeru at mi nangeen ci toroxlu te du lenn lu ngeen ci mana liggéey, du njuddu-ji-réew du doxandéem bi ci seen biir;
TSK
TSK · Leviticus 25:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
«Waxal bànni Israyil ne leen: Bu juróom ñaareelu weer taxawee, bés bi jëkk ci weer wi, na doon seen bésub Noflaay bu ngeen di amal ndaje mu sell. Deeleen fàttlee bés bi liit yu xumb.
Te nangeen sellal at ma ca topp di juróom fukkeelu at ma, ngeen yéene ca mboolem waa réew ma ba mu daj, ne ngoreel taxaw na. Seen atum Yiwiku la, ku nekk war cee dellu ca suufu waa këram, ku nekk it wara dellu ca làng ga mu bokk.
Bu atum Yiwiku dikkee, tool bi day dellu ca ka ñu ko jënde woon te mu di alalu ndonoom.
Te it bu atum Yiwiku mu bànni Israyil agsee, seen cér day dolliku ca céru giir ga ñu séyi ca seen biir. Te kon it ci sunu céru giiru maam, la seen cér boobu di wàññikoo.»
Aji Sax ji, ndokklee mbooloo mu la xal di sarxollee, di niitoo saw yiw,
¶ Waaye dama ne: xanaa dañoo déggul? Ahakay! Ndax «Àddina sépp la seen baat jibal, cati suuf sépp la seen kàddu dajal.»
Loolu di firi ne ci Almasi la Yàlla jubale waa àddina, ak jëmmu boppam, ba toppu leen seeni tooñ, te moo nu dénk kàddug juboo gi.