TSK

TSK · Leviticus 26:33

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax ji moo leen di tasaare ci biir xeet yi, te lu néew la seenu ndes di doon ci biir xeeti jaambur yi leen Aji Sax jiy dàq jëme.

Bu ñu la moyee, nde amul nit ku dul moy, ba nga mere leen, teg leen ci loxob noon, noon ba jàpp leen, yóbbu am réewam, mu sore mbaa mu jege,

Ñu wax ma, ne ma: «Ña rawe ca njaam ga de, ña nga diiwaanu Yuda, ci njàqare ju réy akug toroxte. Tatay Yerusalem jaa nga tojatoo, bunt ya lakk.»

Waññi nga nu, nu won noon yi gannaaw, ñu bañ nu, ba futti nu.

tëral seen askan ci biir xeet yi, wasaare leen ci réew yi.

«Gayndee fëlle geeram, fàkkaskatu xeet yee jóg, génne këram, nara gental seeni dëkk, ba ñu di gent yu kenn dëkkul.

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Ne leen: Waajleena wooyi jigéeni jooykati dëj yi, ñu dikk; yónneeleen ca ña gëna man, ñu dikk.»

Ndeysaan! Dëkk beeka wéet tey! Te ñoñam noon gàññ démb. Ndeysaan! Mu ngi mel nib jëtun tey, te noon ràññ fi biir xeet yi! Moo doon lingeeru diiwaan yi, tey mu sasoo liggéeyu sañul-bañ.

Ñoom lañuy gëdd naan: «Soreleen nu, nit ñu sobewu ñi! Soreleen, soreleen, buleen nu laal.» Ñu daw di tambaambalu ba ca yeneen xeet; ñooña ne leen: «Dootu fii!»

Mboolem ña ko dar, ay toppam ak mboolem gàngooram, maa leen di wasaare fépp fu ngelaw jublu, toppati leen ak saamar.

Ba tey maa leen giñal ca màndiŋ ma ne dinaa leen tasaare ci biir xeet yi, wasaare leen ci biir réew yi.

Hosea 9:6 TSK

Ñu ngoogu dem ndax tasteg réew mi, Misraa leen di fat, Memfis suul leen, seen tànnéefu xaalis, mbooy mee koy nangu, te xaaxaam ay saxe seen biiri xayma ya woon.

Dinañu fàddoo ñawkay saamar, te dees na leen jàpp njaam, yóbbu ci mboolem xeet yi. Te jaambur ñi dul Yawut ñooy joggati Yerusalem, ba kera àppu ñooñu dul Yawut di mat.