¶ «Saxleen ci samay dogal, sàmm samay ndigali yoon, di ko jëfe, ndax ngeen dëkk ak jàmm ci réew mi.
TSK
TSK · Leviticus 26:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Su boobaa maay mayem ñax ci seenub àll ngir seenug jur, yeen it ngeen di lekk ba regg.»
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di jàngin wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen.
Ku dëkke kiiraayu Aji Kawe ji yaa këroo keppaaru Aji Man ji.
Waaye déggal ma, dëkke jàmm, tàggook njekkar ak safaan.»
Su ngeen ma nangoo déggal, ngëneelu réew mi ngeen di xéewloo.
Ay jantam Yuda dina texe, Israyil dëkke kaaraange, te dees na ko tudde nii: “Aji Sax ji sunu njekk.”
Bésub keroog maa leen di fasal kóllëre ak rabi àll yeek njanaaw yi, ak ndëgmeent yi. Fitt ak saamar akub xare it, maa koy dagge ci réew mi, te maa leen di may tëraayu jàmm.
Yeen rabi àll yi, buleen tiit, parluy àll yi day naat, garab yi meññ; figg ak reseñ di baaxee seen xéewal.
«Ay bés a ngii déy, di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «kuy gàbb dina dab kuy góob, kuy nal reseñ dab ka koy ji. Biiñ bu bees di rogalaate ca tund yu mag ya, di wale tundoo tund wu ndaw.
Moona noppiwula seereel boppam ci mbaaxam gi muy jëfe, di leen wàcceel fa asamaan, taw ak naataange, reggal leen, bégal leen ba seen xol sedd.»
yeen ñi seen ngëm tax ngeen yiiru ci manoorey Yàlla, mi leen di nége mucc ga mu waajal te di ko feeñal ca bés bu mujj ba.