TSK

TSK · Leviticus 27:28

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Ab doxandéem, buleen ko lor, buleen ko not, ndaxte yeen itam ay doxandéem ngeen woon fa réewum Misra.

Bu tool bi yiwikoo ci atum Yiwiku nag, day daldi doon lu ñu sellalal Aji Sax ji, mel ni tool bu ñu aaye, mu doon alalu sarxalkat.

Ci kaw loolu Israyil xasal Aji Sax ji aw xas, ne ko: «Soo tegee ba teg mbooloo mii ci sunuy loxo déy, dinanu faagaagal seeni dëkk.»

su boobaa nangeen gëstu, seet te laajte bu baax, ba dëgg gu wér feeñe ca mbir ma, ne defees na moomu mbir mu jomblu ci seen biir,

Bu ngeen demee ba seen Yàlla Aji Sax ji noppal leen ci mboolem seen noon yi séq réew, mi mu leen sédd, ngir ngeen nangu ko, nangeen far mboolem lu ñu doon fàttlikoo Amalegeen ñi fu asamaan tiim. Buleen ko fàtte.

¶ Bésub keroog mbooloom Israyil jàq nañu, ndax ngiñ lu Sóol teg ci seen kaw, ne: «Képp ku lekk fii ba ngoon te feyooguma ci samay noon, yal na alku.» Mbooloo ma mépp, kenn sexu ca dugub.

Demleen léegi, songi Amalegeen ñi. Faagaagal-leen seen lépp, te buleen leen ñeewante; reyleen góor ak jigéen, gone yi ba ci ñiy nàmp, ak nag ak gàtt, ak giléem ak mbaam.”»

¶ Gannaaw loolu Samiyel ne: «Indil-leen ma Agag buurub Amalegeen ñi.» Agag nag dikk, wutsi ko, ne finaax. Booba Agag a nga naan ca xelam: «Dee moom, tiitatuma ko, wees na!»

Saraxu pepp ak saraxu póotum bàkkaar ak saraxu peyug tooñ, ñoom ñoo koy lekk, te lépp lu ñu jagleel Aji Sax ji ci Israyil, ñoo koy moom.

¶ Ba bët setee Yawut ya daje, daldi xasoo, ne duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñu reyee Póol.

¶ Almasi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»