TSK

TSK · Leviticus 27:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Waaye jaaraamaa Yàlla Aji Kawe ji, moom mi la dumaal say noon!» Ba loolu amee Ibraam sàkk fukkeelu la mu lël lépp, jox ko.

Bu nu àggee ci ngóob, juróom yu ngeen am dingeen ci jox Firawna benn, te féetewoo ñeenti cér yi des. Su ko defee ngeen génne ci jiwuy tool yi, li ci des ngeen dunde, yeen ak seen waa kër ak seeni doom.»

¶ Leween ñi ñoom, maa leen jox bépp céru fukkeel bu génne ci Israyil, muy seen cér, ñu yooloo ko seen liggéey bi ñuy liggéey ci xaymab ndaje mi.

Waaye seetleen bérab bu seen Yàlla Aji Sax ji di taamuji, ci mboolem seeni giir, ngir teg fa turam, dëël ko fa, te ngeen dem foofa.

Ci kaw loolu nu wara yóbbu ca sunu néegi dencukaayi kër Yàlla ga lu jëkk ci sunu notu sunguf, ak sunu jooxey pepp, ak sunu meññeefi garab yépp, ak sunu biiñ ak diw, di teg lépp ci loxoy sarxalkat yi. Ba tey nuy indil Leween ñi céru fukkeelub lépp luy meññee ci sunu suuf, ndax Leween ñeey dajalesi céri fukkeel yi ci gox yi nuy bey yépp.

ba tax Elyasib jël néegu dencukaay bu yaatu, jox ko Tobya. Néeg booba lañu daan denc saraxi pepp yaak cuuraay yaak ndab yaak céri fukkeel ya, muy bele ak biiñ ak diw, te ndigal sédd ko Leween ñeek jàngkat yeek fara bunt yi. Foofu it lañu daan denc jooxe yi ñeel sarxalkat yi.

Waaw, nit dina sàcc Yàlla? Ndaxam yeen yeena ngi may sàcc te yeena ne: “Ana nu nu la sàcce?” Xanaa ci seen cérub fukkeelu alal akub jooxe.

Waaye wóoy ngalla yeen Farisen yi! Xobi naana ak yeneen safal yu mel ni ru ak wépp xeetu lujum, yeena ngi ciy génne cérub fukkeel, ngir asaka, njubte ak cofeelu Yàlla nag, ngeen sàggane. Lii de war na leen, waaye lee it, waruleen koo sàggane.

Te sarxalkat yi bokk ci giirug Lewi ni ko yoon wi tërale, ñoom lañu sant ñu nangu céri fukkeeli alali askan wiy seeni bokk, te soqikoo ñoom itam ci geñog Ibraayma.