TSK

TSK · Leviticus 3:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Na teg loxoom ci kaw boppu juru saraxu rendi-dóomal bi, ndax ñu nangul ko ko, muy njotlaayam.

te teg loxoom ci boppu xar mi muy sarxe, ñu rendi ko ci bunt xaymab ndaje mi, doomi Aaróona yu góor yi xëpp deret ji ci mboolem weti sarxalukaay bi.

Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko këpp sunu gépp ñaawtéef.

¶ Ndax kat, ba nu amul menn pexem mucc, ca la Almasi deeyal yéefar yi nu doon, ba mu jotee.

Almasi mi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.

Yeen la Yàlla Baay bi ràññee lu jiitu, ci ni mu leen sellale Noo gu Sell gi, ngir ngeen mana déggal Yeesu Almasi, boole ci tooyloo deretam, mu setal leen. Aw yiw ak jàmm ju ne xéew ñeel na leen.

Almasi itam benn yoon la daj coono ndax bàkkaari nit ñi, moom miy ki jub moo leen ko defal yeen ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; moom lañu rey yaramu suuxam, waaye moo dundaat ci dooley Noo gi.