TSK

TSK · Leviticus 4:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Sàkkal ci deretu yëkk wu ndaw wi, nga capp ci sa baaraam, diw ci béjjéni sarxalukaay bi, te nga tuur li des ci deret ji ci suufu sarxalukaay bi.

Bu noppee na sàkk ci deret ji, taqal ci béjjéni sarxalukaay bi ci kanam Aji Sax ji, ci biir xaymab ndaje mi. Li des ci deret ji, na ko tuur ca taatu sarxalukaayu rendi-dóomal ba, ca bunt xaymab ndaje ma.

Na sarxalkat bi capp baaraamam ci deretu xar miy saraxu póotum bàkkaar, te taqal ci béjjéni sarxalukaayu rendi-dóomal bi; li des ci deret ji da koy tuur ci taatu sarxalukaay bi.

¶ Ba loolu wéyee Musaa jël diwu pal ga, diw ca jaamookaay baak ya ca biir yépp, sellale ko yooya,

Gannaaw loolu doomi Aaróona yu góor ya indil ko deret ja, mu capp ca baaraamam, taqal ca béjjéni sarxalukaay ba; la des ca deret ja mu tuur ko ca taatu sarxalukaay ba.

Ndaxte dundu mbindeef ci deret la nekk, te man maa leen sédde deret, ngeen di ko jotoo seen bakkan ci kaw sarxalukaay bi. Ndax kat bakkanu mbindeef deretam la taxawe. Moo tax deret mana defal nit njotlaayam.

te ci yiwu Yàlla wu àndul ak genn pey lees di joxe ñépp àtteb ñu jub, ndax njot gi sottee ci Almasi Yeesu.

Ndax kat Almasi moo sottal yoonu Musaa, ngir àtteb ku jub ñeel képp ku ko gëm.

Ndax ci yoonu Musaa sax, deret lees di setale daanaka lépp, te bu deret tuuruwul, njéggal amul.