Li muy génne ci saraxu cantu biir jàmm bi, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, mooy nebbon bi, ak calgeen bi yépp, ñu doge ko fa sës ca fàllare ja, ak nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,
TSK
TSK · Leviticus 4:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Leviticus 3:9
TSK
Leviticus 4:19
TSK
Na génne lépp li ciy nebbon, lakk ko ci kaw sarxalukaay bi.
Leviticus 4:31
TSK
Te it na génne nebbon bi yépp ni muy génnee nebbonu jur gu ñu def saraxu cant ci biir jàmm. Na ko sarxalkat bi lakkal Aji Sax ji ci kaw sarxalukaay bi, muy xeeñ xetug jàmm. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal.
Leviticus 7:3
TSK
Nebbon ji jépp lañuy sarxal: calgeen bi, nebbon bi sàng yérey biir yi,
Isaiah 53:10
TSK
Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, teg koy naqar, su nangoo doon saraxu peyug tooñ, gis askanam, aw fanam gudd, te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.