TSK

TSK · Leviticus 6:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

mboolem li des ci yëkk wi daal lay génne dal bi, yóbbu ko ci bérab bu mucc sobe, ca jalub dóom ba, daldi taal matt, lakk ko ca, ba mu dib dóom. Foofa dóom ba jale lees koy lakk.

Lépp lu laal ci yàpp wi, day doon lu sell, te bu lenn ci deretu sarax si tisee ci kawi yére, dees koy xaj fa mu tis, ci bérab bu sell.

Képp kuy góor te bokk ci askanu sarxalkat yi sañ na cee lekk. Bérab bu sell lees koy lekke. Lu sella sell la.

¶ «Na Aaróona dellu ca xaymab ndaje ma, summi yére ya ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew, di ya mu soloon bala moo dugg ca bérab bu sell baa sell, te na fa wacc yére ya.

Mburu yooyu Aaróona aki doomam yu góor ñoo koy féetewoo, te nañu ko lekke fu sell, ndaxte lu sella sell la, di lu ñu séddoo fàww ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji.»

Ndax kat, jur ga sarxalkat bu mag ba daan yóbbu seen deret ca bérab bu sell baa sell, ngir njotlaayal bàkkaar, seen yaram lees daan lakk ca bitib dal ba.