TSK

TSK · Leviticus 6:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Diiru juróom ñaari fan ngay defal sarxalukaay bi saraxu njotlaayam, sellale ko ko, ba sarxalukaay bi doon lu sella sell. Lépp lu laal sarxalukaay bi day séddu ci sellaayam.

¶ «Ndegam sarxalkat bi ñu diw, fal ko, moo moy, ba yóbbe mbooloo mi tooñ, na indil Aji Sax ji yëkk wu ndaw wu amul sikk, muy saraxu póotum bàkkaar ndax bàkkaar ba mu def.

Day teg loxoom ci boppu xar moomu di saraxu póotum bàkkaar, rendi ko fa ñuy rendee saraxu rendi-dóomal, muy saraxu póotum bàkkaar.

Askanu Aaróona sarxalkat bi, du kenn ku ci am sikk kuy agsi ba fii, di joxe saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji. Sikk si ci moom a tax du mana agsi ba fii, di joxe ñamu Yàllaam.

Fu sella sell ngeen koy lekke; képp kuy góor ci yeen, sañ na cee lekk. Lu sell lay doon ci yaw.

Bésub keroog jóolóoliy fas yi sax dees na ci bind: «Sell na ñeel Aji Sax ji.» Te ni ndabi tuurukaay yi fi kanam sarxalukaay bi selle, cin yi gëna néew daraja ci biir kër Aji Sax ji sax noonu lañu selle.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.