TSK

TSK · Leviticus 6:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Diiru juróom ñaari fan ngay defal sarxalukaay bi saraxu njotlaayam, sellale ko ko, ba sarxalukaay bi doon lu sella sell. Lépp lu laal sarxalukaay bi day séddu ci sellaayam.

«Waxal Aaróona ak doomam yu góor ne leen: Dogal bi ci saraxu póotum bàkkaar mooy lii: Juru saraxas póotum bàkkaar dañu koy rendi fa ñu wara rendi juru saraxu dóomal, fi kanam Aji Sax ji. Lu sella sell la.

waaw, su nit yoree ci lafu mbubbam, aw yàpp wu ñu sellal, ba noppi lafu mbubbam laal mburu mbaa lu ñu togg, mbaa biiñ mbaa ag diw mbaa ñam wu mu doon, ndax loola day daldi sell?» Ase laaj ko sarxalkat ya, ñu ne ko: «Déedéet.»

Gisleen nag, seen tiis wi leen Yàlla teg ci coobareem, li mu leen jural: gii farlute; gii kàddug layoo gu ngeen yékkati, rawati; mii mer mu war, rawati; gii ragal Yàlla rawati; gii nammeel rawati; gii xéraange rawati; gii pastéef ci yar ki tooñ rawati! Nu nekk ngeen setale seen bopp wecc ci mbir moomu.