TSK

TSK · Leviticus 7:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Te itam nit ñu sell ngeen wara doon, ñeel ma, kon nag yàppu mala mu ñu fàdde ci àll bi, buleen ko lekk; sànnileen ko xaj yi.

¶ «Te itam képp ku lekk médd mbaa lu rab fàdd, muy njuddu-ji-réew mbaa doxandéem, na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so, mu doora set.

¶ Buleen lekk lenn lu médd. Jaambur bu dal ak yeen, sañ ngeen koo jox lu médd, mu lekk, mbaa ngeen jaay ko ab doxandéem. Waaye yeen askan wu sell ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Te buleen togg ab tef ci meewum yaayam.

¶ «Gannaaw loolu mboolem lu médd mbaa lu ñu fàdd, muy boroomi laaf akug jur, sarxalkat yi duñu ko lekk.