TSK

TSK · Leviticus 7:26

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Te itam nit ñu sell ngeen wara doon, ñeel ma, kon nag yàppu mala mu ñu fàdde ci àll bi, buleen ko lekk; sànnileen ko xaj yi.

¶ «Te it képp ku bokk ci waa kër Israyil mbaa doxandéem yi ci seen biir, bu lekkee lenn luy deret, kooku lekk deret, man Aji Sax ji, dinaa ko noonoo te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil.

Kon nag nanga leen wax ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen ngeen di boole yàpp ak deret di ko lekk, di wékki gët kasaray tuur, di tuur deretu jaamburi Yàlla, ba noppi di moom réew mi?

Xanaa nu bind leen, ne leen ñu moytu lu ay xërëm sobeel, moytu powum séy, moytoo lekk yàppu mala mu ñu tuurul deretam, ak lekk deret ci boppam.

¶ Ci moom lanu ame njot gi nu sottalal njéggalug moy, ndax deretam ji tuuru, noonu ko Yàlla defe ci yiwam wu yaa,