Leya ne: «Éey waay, maaka bég! Jeeg ji dinañu ma wooye boroom mbégte mi.» Mu tudde ko nag Aser (mu firi Boroom mbégte).
TSK
TSK · Luke 1:48
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mooy yékkatee ku ndóol ci suuf, jële ku ñàkk ci mbuubit, boole leen dëj ca garmi ya, sédde leen jataayu teraanga. «Aji Sax jee moom kenuy suuf, samp ci àddina.
¶ Ba loolu amee Buur Daawuda dikk ba fa kanam Aji Sax ji, toog ne ko: «Boroom bi Aji Sax ji! Ana lu ma doon, ak lu sama waa kër doon, ba tax nga indi ma ba fii?
Mooy yékkatee ku néewle fa suuf, di seppee ku sonn cib sën,
Aji Sax jee kawe! Ku toroxlu, mu niir; ku réy, mu ñooru.
«Xeet yépp ñu barkeel ñi lañu leen di wooye, nde réewum bànneex ngeen di dëkke.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
Mu àddu ca kaw ne: «Yaa gëna barkeel ci jigéen ñi, sa doom ji nga ëmb it barkeel na!
¶ Bokk yi, seetleen ñan ngeen woon, ba ñu leen di woo. Barewul ci seen biir ay xamkat, ci gis-gisu nit ñi, barewul ci yeen ay boroom doole, barelewuleen ñu rafet ab juddu.