Aji Sax ji, ñi koy xeex ay rajaxoo, kaw asamaan lay dënoo ci seen kaw. Mooy mbugal àddina, ba mu daj, di kàttanal buuru ñoñam, di dooleel ki mu fal.»
TSK
TSK · Luke 1:69
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mooy sama Yàlla, ji ma sës, yiiru, fegu, mucc, làqu, raw, mucc fitna.
Mu ne: Aji Sax ji, maa la sopp, yaw mi may dooleel.
ànd di la bége bés bu ne, sag njekk siggil leen.
Fa laay dooleele Daawuda, taalal ki ma fal,
Aw njebbit mooy saxe fa ëkkub Yese, ab car soqeekoo fa reen ya,
Bés yooyu ci jamonoom, maay jebbil njebbit lu jekk ci askanu Daawuda, muy jëfe njub ak njekk ci réew mi.
¶ «Gannaaw loolu maa leen di waajalal ab sàmm bu leen di sàmm. Kookooy Daawuda sama jaam bi. Moom moo leen di foral, mooy doon seen sàmm.
«Bésub keroog maay yékkati mbaarum Daawuda mi joy, ba fattaat xar-xar yi, defaraat gent bi, tabaxaat ko na woon.
¶ «Man Yeesu maa yónni sama malaaka, ngir mu seede mbir yii ci yeen, ñeel mboolooy gëmkat ñi. Man maay njebbitu Daawuda, di kuutaayam, maa di biddiiwu njël bi ne ràññ.»