TSK

TSK · Luke 1:75

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

ndax ngeen ragal seen Yàlla Aji Sax ji, di sàmm mboolem dogali yoonam, ak santaaneem, yi ma leen di dénk, yeen ak seeni doom, ak seeni sët, seen giiru dund, su ko defee ngeen gudd fan.

«Waaye kóllëre gi may fas ak waa kër Israyil gannaaw loolu,» kàddug Aji Sax jee, «nii lay deme: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.

Maa leen di seppee ci yéefar yi, dajalee leen mépp réew, délloosi leen seen suufas bopp.

Te mooy noonu mu nu taamoo ba àddina sosoogul ndax Almasi mi nu bokk, ngir nu doon ñu sell te mucc sikk fa kanamam. Ci biir cofeel

te ngeen soloo jëmm ju yees ji Yàlla sàkke ci takkndeeram, di jëfe njub, ak sellnga ji dëgg di jur.

Moo nu musal, woo nu woote bu sell te sunuy jëf taxul, waaye coobarey boppam a tax, ak yiwam wi ñu nu may ci Almasi Yeesu, balaa ay jamonoy jamono di sosu.

Gannaaw gone yu dégg ndigal ngeen, buleen toppati seen xemmemtéefi bakkan ya woon, ba ngeen xamulee.