Maay wàcc wax ak yaw foofa te maay sàkk ci leer gi ci yaw, def ko ci ñoom, ñu yenule la yenu mbooloo mi, ba dootuloo ko yenu yaw doŋŋ.
TSK
TSK · Luke 10:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ilyaas ne mbooloo ma: «Man de maa fi des ci yonenti Aji Sax ji, man doŋŋ, te yonenti Baal yi ñeenti téeméer lañook juróom fukk (450).
sa mbooloo dëkke fa. Yàlla yaa leel néew-ji-doole ci sag mbaax.
tànnal leen sàmm yu ma doy, ñu sàmme leen xam-xam akug muus.
Ñi leen jënd di leen rendi, te jàpp ne yoon toppu leen ci; ñi leen jaay naan: “Sant Aji Sax ji, woomle nanu,” gétt gi la seeni sàmm yërëmul.
¶ Gëmkat ña tasaaroo woon nag ndax fitna ja woon, ca mbirum Eccen, mujj nañu jàll ba diiwaanu Fenisi, ca dunu Sippar ak ca Àncos, waaye àggewuñu kàddu gi ñeneen ñu moy Yawut yi.
¶ Ñooñu la Noo gu Sell gi yebal, ñu dem dëkk ba ñuy wax Selusi, dugge fa gaal, jëm dun ba ñuy wax Sippar.
Wattuleen nag seen bopp, wattu mboolem gétt, gi leen Noo gu Sell gi sàmmloo, te ngeen foral mbooloom gëmkati Yàlla, mi Yàlla jote deretu boppam.
¶ «Ma ne ko: “Sang bi, yaa di kan?” Sang bi ne ma: “Man maay Yeesu, mi ngay bundxatal.
Ñi Yàlla tabb ci biir mbooloom gëmkat ñi, ñi ci jiitu ñoo di ndawi Almasi. Ñaareel bi di ñiy waxe kàddug waxyu, ñetteel bi di jànglekati kàddu gi. Ñi ci topp di ñiy def ay kéemaan, ñi ci topp di ñi am mayu faje, ak ñi mane dimbalee, ak ñi mane jiite, ak ñiy làkk yeneen xeeti làkk.
¶ Nun ñi bokk ci liggéey bi nag, noo leen di ñaan ngeen baña nangu yiwu Yàlla ci neen.
Ñi ci des ñépp, seen njariñal bopp lañuy sàkku, waaye du li soxal Yeesu Almasi.
ndax liggéeyal Almasi tax na koo riisu ndee; ba ngeen amee ngànt lu leen teree mottlil seen bopp, seen yéene, moo jaay bakkanam ngir wuutu leen, ba yótsi ma seen ndimbal.
Ab nuyoo it ñeel na leen, tukkee ci jaamub Almasi Yeesu, Epafras, mi bokk ci yeen. Ku jàmbaare ci saxoo leena ñaanal, ngir seenub taxawaay sotti te mat sëkk ci jëfe mboolem luy coobarey Yàlla.
¶ Gannaaw loolu bokk yi, danu leen di ñaan, ñi féetewoo coonob liggéey ci seen biir te jiite leen ci yoonu Boroom bi, di leen yee, nangeen leen yég.
¶ Damay sant sunu Boroom Almasi Yeesu mi ma dooleel, moom mi ma natt ba wóolu ma, tabb ma ci liggéey bi,
Loolu ngay def sam xel, mbir yooyu ngay pastéefoo ba sag yokkute bir ñépp.
Jëlal sa wàll ci coono bi takk-derub Almasi Yeesu bu wóor di jànkoonteel.
¶ Ci man Póol, mi ñu tëj kaso ngir Almasi Yeesu, ci man ak itam ci Timote miy mbokkum gëmkat la bataaxal bii bawoo, ñeel Filemon, sunu soppe bi bokk ak nun liggéey bi.
¶ «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Efes, bind ko ne ko: «Lii moo di kàdduy Ki yor juróom ñaari biddiiw yi ci loxol ndijooram, di doxe digg juróom ñaari tegukaayi làmp yu wurus yi. Mu ne: