TSK

TSK · Luke 11:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Musaa ne Aaróona: «Lii la Aji Sax ji doon wax ba mu nee: “Ci biir ñi may jegeñ laay feeñal samag sellaay, te ci kanam mbooloo mi mépp lees may terale.”» Aaróonaa nga ne cell.

su boobaa ngalla nangool asamaan, màkkaan ma nga dëkke, te nga defal doxandéem boobu mboolem lu mu la ñaan, ndax xeeti àddina yépp xam sa tur, ngir ragal la ni Israyil sa ñoñ, te xam ne saw tur lañu tudd ci kër gii ma tabax.

Sa ngor a màgg, ba àkki asamaan, sa worma àkki fa kawa kaw.

Yeen malaaka yi, santleen Aji Sax ji, yeen jàmbaar yu mag yiy jëfe ndigalam, di sàmm kàddoom.

Ay malaakay seraf ñoo taxaw, tiim ko, ku ci nekk am juróom benni laaf: ñaar yu muur seen kanam, ñaar yu muur seeni tànk, ak ñaar yu ñuy naawe.

Kon dinaa fésal sama sellngay tur wu màgg, wi ñu teddadil fi biir yéefar yi, sama tur wi ngeen teddadil fi seen biir. Ci yeen laay fésale sama sellnga, yéefar yiy gis, ba xam ne maay Aji Sax ji. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

¶ «Ci jamonoy buur yooyu Yàlla Boroom asamaan dina samp nguur gu dul tas mukk, te wenn xeet du ko yilif mukk. Nguur googu dina tasaare mboolem yeneen nguur yooyu, ba genn du ci des, waaye moom day sax ba fàww.

Palug mboolem nguur yi asamaan tiim, ak kilifteef gaak daraja ja dees na ko boole, jébbal aji sell yu Aji Kawe ji. Nguurug mbooloo moomu day sax ba fàww, kilifa yépp di ko déggal, di ko wormaal.”

Waaye ni ndox muure xóotey géej ba mu daj, ni la darajay Aji Sax jiy ràññikoo ci àddina sépp.

¶ Bataaxal bi ñeel na mboolem yeen ña fa Room, di ñu Yàlla sopp, woo leen, ngir ngeen doon ñu sell. Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.

Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.

mi maye bakkanam ngir njotug sunuy bàkkaar, ba musal nu ci jamonoy tey ju bon ji, ci coobarey Yàlla sunu Baay,

Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.

ñeel waa Kolos ñu sell te wóor te di bokki gëmkati Almasi. Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay.

ak di baamtu fi kanam Yàlla sunu Baay, jëf ji juddoo ci seen ngëm, ak liggéey bi sottee ci seen cofeel, ak yaakaar ji ngeen saxoo di séentu sunu Sang Yeesu Almasi.

¶ Man la Póol, mi ànd ak Silwan ak Timote ci kàddu gii ma yékkati, ñeel mbooloom gëmkati waa Tesalonig, ñi bokk ci Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.

¶ Ba mu ko defee, juróom ñaareelu malaaka mi wal liitam, baat yu xumb jibe ca asamaan, ne: «Léegi nag nguurug àddina ñeel na sunu Boroom ak Almaseem. Mooy nguuru ba fàww.»

¶ Ma daldi dégg lu mel ni coowal mbooloo mu bare, mu àddoo ni riirum géej, tey nirook kàddug dënu gu réy, ne: «Aleluya! Sunu Boroom Yàlla Aji Man ji mooy Buur!