TSK

TSK · Luke 12:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Fekk na Buur teg jawriñam ja mu doon àndal saa su nekk ca buntu dëkk ba, mu di ko wattu. Mbooloo ma nag di buuxante, ba dëggaate ko ca bunt ba, mu dee. Muy la góoru Yàlla ga yégle woon ba Buur dikkee ca moom.

Job 27:8 TSK

Ana lu yéefar biy yaakaarati bu fàddoo, ba Yàlla moom bakkanam?

Bàkkaarkati Siyoŋ tiit nañu, way-gëmadi yaa ngay lox. Ana kan ci nun moo mana dal ak sawara suy xoyome? Ana kan ci nun moo mana dal ak taal yu yànj ya dul fey?

Luke 5:15 TSK

Teewul jëwub Yeesu gënatee law. Mbooloo yu bare daje, di ko déglu tey faju, ba tàggook seeni jàngoro.

Wóoy ngalla yeen, yeena ngi mel ni ay bàmmeel yu amul xàmmikaay, nit ñiy dox ca kaw te xamuñu ko.»

¶ Ñu dégg ca, daldi sàbbaal Yàlla, ba noppi ne ko: «Mbokk mi, xoolal ñaata junniy Yawut a doon ay gëmkat, te ñoom ñépp di ñu xér ci yoonu Musaa.

¶ Li ma jotoon laa leen jëkka jottli, te moo di: Almasi moo dee ngir njotug sunuy bàkkaar, te noonu la ko Mbind mi indee.

¶ Kon nag baleen mboolem xeetu mbon, ak mboolem njublaŋ, ak jinigal, ak kiñaan, ak mboolem xeetu yàq der.