TSK

TSK · Luke 14:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ku bon a ngi yeeru ku jub, di ko wuta bóom.

Xanaa dungeen bàyyee songandoo nit, nar koo sànk, ni kuy màbb tabax bu joy, mbaa ngay bàddi per mu ràpp?

Ma ngay xool la ngay lekk, nu mu tollu, naan la: «Lekkal, naanal!» Te xol ba àndu ca.

Dégg naa ñaawlaate yu bare, ñu naan: «Éey, Tiitaange-lu-dajal! Booleleen ko, boole rekk!» Ñi ma séqal jàmm sax, di yeeru ma fakkastalu, naan: «Jombul mu juum, nu jekku ko, ba mana feyu.»

Luke 6:7 TSK

Firikati yooni Musaa yaak Farisen yaa ngay xool Yeesu, ba xam ndax dina ko faj ca bésub Noflaay ba, ngir ñu am lu ñu ko tuumaale.

¶ Ba Yeesu waxee ba noppi, ab Farisen da koo woo këram, ngir bokk ak moom lekk. Mu nangu, dem ba duggsi, daldi toog ca lekkukaay ba.

¶ Ba mu ko defee ñu bàyyi Yeesu xel, daldi yebal ay yeerukat, sas leen ñu yiw-yiwlu te di ko fiir ci kaw kàddu ba jàpp ko, ngir jébbal ko boroom dëkk bay boroom kilifteef ga ak sañ-sañ ba.

Acts 5:34 TSK

Ab Farisen bu ñuy wax Gamalyel, di jànglekatu yoonu Musaa bu ñépp nawloo, daldi taxaw ca digg kurélu àttekat ya. Mu joxe ndigal ngir ñu génne leen ab diir.