¶ Ba mu ko defee Mardose bàyyikoo ca Buur; ma nga sol yérey buur, baxa ak weex, ak mbaxanam buur mu wurus mu réy, ak mbubbum lẽe mu xonq curr. Dëkku Sus baa ngay riire mbégteek bànneex.
TSK
TSK · Luke 16:19
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ngir maa ñee ku bew, ndax gis mu baaxle te di ku bon.
ba ci yérey sooy ak yérey lẽe aki musóor aki kol.
Lii de, moo doon bàkkaaru Sodom, sa rakk ja, mooki janqam: réy, fuqle, naagu, ne finaax ak ñàkka dimbali ku ñàkk ak ku néewle,
Yeen ñi tëdd ci seen lal yu yànj, ak a sóonoo seen laltu yu nooy, di yàpp mbote yu baax ak sëllu yu duuf,
Ay fan yu néew gannaaw gi, ka gën di ndaw jaay léppam, daldi tukki réew mu sore, di topp bakkanam ba yàq fa alalam.
Yeesu gis loolu, daldi ne: «Boroom alal tàbbi ci nguurug Yàlla, ndaw lu jafe!
Jigéen jaa ngi sol lu yolet te xonq, takk wurus ak jamaa aki per. Mu ngi yor kaasu wurus bu fees ak ñaawtéef ak sobey moyam.
naan: «Wóoy, wóoy ngalla dëkk bu mag ba! Ngalla yaw, dëkk bu mag, ba daa woddoo lẽe ak ndimo lu yolet ak lu xonq curr, takkoo wurus ak doji gànjar aki per,