TSK

TSK · Luke 16:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax jaa ngi feeñoo, di àtte yoon; ku bon teg ug fiir, tàbbi ca. Na jib ndànk. Selaw.

Nara dee rekk niy xar, ndee wommat, yóbbu, njub fenk nib jant, ku jub moom leen, njaniiw mëdd seen jëmm, fu sore kërug daraja.

Tànk ya day bartalu wuti ndee, ay jéegoom àkki njaniiw.

Waaye kooka du xam ne waa njaniiw a nga fa, te ku wuyji, tàbbi biir bàmmeel.

Njaniiw ga fa suufa suuf yàkkamti na la, di la waaja gatandu, ba yeel la ndem-si-yàlla yi doon njiiti àddina yépp. Moo yékkatee buuri xeet yépp seeni jal,

Foofa la ay jooy ak naqarlu bay yéyu di ame yoon, kera bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ak yonent yépp ca biir nguurug Yàlla, te fekk yeen ci seen bopp, ñu dàq leen ca biti.

kooku dina naan biiñu sànjum Yàlla bu kenn raxul, ñu xelli ko ci kaasu sànjam. Te dees na ko mbugale sawara ak tamarax ci kanam malaaka yu sell yi ak Gàtt bi.

Ba mu ko defee géej jébbale néew ya woon ca moom, ndee ak njaniiw jébbale néew ya woon ca moom, ñu daldi àtte ku nekk ca say jëf.