TSK

TSK · Luke 16:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ndax xef ak xippi mu wéy, mel ni lu saxi laaf, ne fëyy, naaw ni jaxaay.

Su bés baa wattukati kër gi di lox, jàmbaari xare yi sëgg, wolkat yi néew, ba wolatuñu, ñiy séentu ci caax yi giimle,

Xanaa du sédd ku xiif saw ñam, fat néew-ji-doole ju amul fu mu dëkk, gis ku rafle, wodd ko, te baña nëbbu mbokk mu soxla?

Li ci biir kay ngeen di sarxe! Su boobaa seen lépp ay set.

Su boobaa ndokklee yaw, nde amuñu sag pey, waaye dees na la fey, kera ndekkitel aji jub ñi.»

¶ «Ab jaamu kër nag manula jaamu ñaari sang; day dëddu kii, sopp kee; mbaa mu fonk kii, cof kee. Manuleena jaamoondoo Yàlla ak Alal.»

Mu ne ma: “Korney, nangu nañu say ñaan, te nemmiku nañu say sarax fa kanam Yàlla.

¶ Ndax liggéey bi ndimbal lii laaj kat, yemul rekk ci faj soxlay ñu sell ñi, waaye itam dina baawaanal cant gu bare, ñeel Yàlla.

¶ Ñi barele alalu àddinay tey nag, dénk leen ñu baña réy te baña yaakaar alal ju wóoradi, te ñu yaakaar Yàlla mi nuy xéewale lépp, ngir nu di ko bége.

Jude 1:21 TSK

Fexeleen ba des ci biir cofeelu Yàlla, tey séentu sunu yërmandey Boroom Yeesu Almasi, ngir ag texe gu sax dàkk.