TSK

TSK · Luke 18:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yanqóoba da leena jàllale, jàllewaale alalam jépp itam.

Job 27:8 TSK

Ana lu yéefar biy yaakaarati bu fàddoo, ba Yàlla moom bakkanam?

Yal na leen dee bett, ñu jekki tàbbi njaniiw, ngir mbon ga seen biir ak seen dëkkuwaay.

Éy Boroom bi, baaxe ma; yaw laay yendoo woo wall.

Ma geesu ndijoor, xool; du kenn ku ma faale. Rawtu réer ma, du kenn ku sama bakkan saf.

Jonah 2:7 TSK

Ca reeni tund ya laa suuxi, caabiy suuf féete ma gannaaw ba fàww, waaye ca kan ma nga jukkee sama bakkan, yaw, sama Yàlla Aji Sax ji.

Ndaxte képp ku ñaan, dinga am; ku seet, dinga gis; ku fëgg it, dees na la ubbil.

Bégeleen seen yaakaar, di muñ ci biir tiis, tey saxoo ag ñaan.

Bunu tàyyi ci def lu baax, nde bu jotee rekk nooy góob, ndegam yoqiwunu.

Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan ak a dagaan te boole ci di ko sant.

Ab nuyoo it ñeel na leen, tukkee ci jaamub Almasi Yeesu, Epafras, mi bokk ci yeen. Ku jàmbaare ci saxoo leena ñaanal, ngir seenub taxawaay sotti te mat sëkk ci jëfe mboolem luy coobarey Yàlla.

Xool-leen ci moom mi bàkkaarkat yi doon xeex, bala ngeena yoqi bay xàddi.