Ag maas a ngi defe ne set nañu, te taq ripp ak bàkkaar.
TSK
TSK · Luke 18:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen ñiy déglu kàddoom, di lox. Lii de mooy seen kàddug bokk, yi leen jéppi, di leen dàq ngir samaw tur. Ñu ngi naan: «Na Aji Sax ji darajaal boppam, ba nu teewe seen mbégte, yeen ñii!» Waaye ñoom de ñooy rus.
Waa ja nag namma wutu lay, ne Yeesu: «Sama moroom mooy kan?»
Mu àddu, ne baayam: “Seetal ñaata at laa la liggéeyal, sa ndigal, masuma koo moy, te man, masuloo maa may sax as tef su nu bégloo, maak samay xarit.
Farisen baa nga taxaw di yelu, naan: “Yàlla, maa ngi lay sante li ma melul ni ñeneen ñi doonul lu moy ay lekk-kati àq, ay njublaŋ aki jaalookat, rawatina juutikat bii.
Mu ne ma: “Demal, man, fu sore laa lay yebal ca ña dul Yawut.”»
Waaye xeetu Israyil wi sàkku woon yoonu njub, ñoo moy yoon wi.
Yaw nag ana looy sikke sa mbokkum gëmkat, ak itam, ana looy xeebe sa mbokkum gëmkat? Ndax kat nun ñépp ay taxawi fa kanam jalub àttekaayu Yàlla.