TSK

TSK · Luke 2:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ci kaw loolu Rasel faatu, ñu denc ko ca yoonu Efrata, ga ñuy wax Betleyem ba tey.

Ruth 1:19 TSK

Ba mu ko defee ñu ànd ñoom ñaar, ba àgg Betleyem. Naka lañu àgg Betleyem, dëkk ba bépp ne kër-kër, ne këpp ndax ñoom. Jigéen ña naa: «Xanaa kii kay du Nawmi?»

Ruth 4:11 TSK

¶ Waa pénc ma mépp ak mag ña nag ne ko: «Noo ko seede. Yal na Aji Sax ji def ndaw siy séysi sa kër, mel ni Rasel ak Leya, ñoom ñaar ñi giir waa kër Israyil gépp. Yal nanga tekki ci digg Efrata te amu tur ci Betleyem.

¶ Samiyel def la Aji Sax ji wax. Ba mu agsee Betleyem, magi dëkk ba gatandoo ko tiitaange, ne ko: «Mbaa tànki jàmm?»

Sóol ne ko: «Yaw, gone gii, yaay doomu kan?» Daawuda ne ko: «Maay doomu Yese, sa surga ba dëkk Betleyem.»

Micah 5:2 TSK

Moo tax Aji Sax ji di leen wacc ba keroog jant, ba kiy matu mucc. Ca la bokkam ya dese bakkan di dellu, fekki seen bokki bànni Israyil.

Luke 1:26 TSK

¶ Ba Elisabet tolloo ci juróom benni weeram, ca la Yàlla yebal Jibril malaaka mi, dëkk bi ñuy wax Nasaret ca diiwaanu Galile,

Luke 4:16 TSK

¶ Yeesu moo dikkoon Nasaret ga mu fekk baax, daldi dugg ca jàngu ba, na mu ko baaxoo woon ci bésub Noflaay. Mu taxaw ngir biral ab dog.