TSK

TSK · Luke 2:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

te bu bët setee dingeen gis manoorey Aji Sax ji, ndaxte dégg na ngeen di diiŋat Aji Sax ji, ndax nun kat tekkiwunu dara, ba ngeen di nu diiŋat.»

¶ Ba loolu amee niir wa yiir xaymab ndaje ma, leeru Aji Sax ji fees jaamookaay ba,

ba sarxalkat ya talatuñoo liggéey, ndax leeru Aji Sax jaa nekkoon ca niir wa, niir wa feesal kër ga.

Day tóora tóor, di bànneexu, bay sarxolle, ba jagoo darajay gottub Libaŋ ak taaru àllub Karmel ak Saron. Foofa lees di gise darajay Aji Sax ji, sunu taaru Yàlla.

Yerusalem, jógal ne ràññ, sag leer feq na; teddngay Aji Sax ji fenkal na la!

Luke 1:28 TSK

Malaaka ma agsi ba ca moom, ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi ñu baaxe, Boroom bi yaw la àndal.»

Acts 12:7 TSK

Ci kaw loolu am malaakam Boroom bi ne jaas, taxaw, ag leer ne ràyy ca biir kaso ba. Malaaka ma laal Piyeer ci wetam, yee ko, ne ko: «Jógal gaaw!», càllala yi daldi rote ciy loxoom.

Ba ma demee ba wetu digg bëccëg, Buur, ca laa gis ag melax gu leer ba raw jant bi, fettaxe asamaan, ne ràyy fi ma wër, maak ñi ma àndal.

Nun ñépp nag, kanam gu muriku lanuy xoole niki cib seetu, leeru Boroom bi, ba tax nuy soppiku, doon takkndeeram, tey làmboo leer guy màgg, di gëna màgg. Looloo di liggéeyu Boroom bi, moom miy Noo gi.

Deesul nàttable moos màggaayu mbóot mii feeñe ci sunu yoonu ngëm: Kii moo feeñe ci yaramu suux, Noowug Yàlla dëggal ko, malaaka ya niir ko; moom lañu waaree ci xeet yi, gëmees na ko ci kaw suuf it, te yéegees na ko fa leer ga.

¶ Gannaaw loolu ma gis meneen malaaka mu am sañ-sañ bu réy wàcce asamaan, àddina di leere cig leeram.