TSK

TSK · Luke 21:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Maay xiir Misra ci kaw Misra, kii song mbokkam, kii song xaritam, ab dëkk jógal ab dëkk, diiwaan jógal diiwaan.

Xeet yépp laay dajale ci kaw Yerusalem, ngir xare. Dëkk bi lees di nangu, sëxëtoo kër yi, tëdde jigéen ñi. Genn-wàllu dëkk beey génn, jëm ngàllo, waaye ndesu askan wi, deesu leen dagge ci dëkk bi.

Kenn ca ñoom, ku ñuy wax Agabus daldi yéglee Noo gu Sell gi, ne xiif bu metti dina am, ci àddina sépp. Te looloo nga yemook ayug buur bu mag bu ñuy wax Këlódd.

Ma xool rekk, gis fas wu weex, gawaram yor ag fitt. Ñu jox ko kaala, mu daldi dem yoonu daan-kat, ngir daani.