TSK

TSK · Luke 21:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ku ne sa dëkkandoo ngay nax, te dëgg, doo ko wax. Dañoo tàmmi fen, di def njekkar ba sonn.

Micah 7:5 TSK

Buleen gëm ab xarit, buleen wóolu ab xejj, fi kanam ndaw siy tëdd sa gannaaw sax, sàmmal sa bunti gémmiñ.

Acts 7:59 TSK

¶ Ñuy dóor Eccen ay doj, moom muy ñaan Yàlla, naan: «Sang Yeesu, nangul sama bakkan!»

Def naa ko ci Yerusalem, te it bare na ñu sell ñu ma tëjlu ci kaw sañ-sañ bu ma sarxalkat yu mag yi jagleel, te saa yu ñu leen tegaan àtteb dee, dama daan biral kàddu gu leen àtte ñàkkal.

¶ Ba mu tàyyee juróomeelu tayu gi, ma gis ci suufu sarxalukaay bi, bakkani ñi ñu bóom ndax kàddug Yàlla ak seede si ñu ci seede.