TSK

TSK · Luke 21:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mbooloo ma nag ne Sóol: «Lan? Yonatan dee, moom mi may Israyil ndam lu réy lii? Xalaateesu ko moos! Giñ nanu ci Aji Sax jiy dund, du lenn luy rote ci kawaru boppu Yonatan sax, dal fi suuf, ndax Yàlla la àndal def lii tey.» Noonu la mbooloo ma jote Yonatan, ba deewul.

Mu ne ko: «Kon ngalla Buur, woo ci seede sa turu Yàlla Aji Sax ji, ngir kiy toppe bakkanu ka dee baña yokk yàqute, ba ñu rey sama doom ji.» Mu ne ko: «Giñ naa ko ci turu Aji Sax ji, Kiy Dund, kawar gu gëna tuut du jóge ci sa boppu doom, wadd ci suuf.»

Luke 12:7 TSK

Yeen nag seen kawari bopp sax, waññees na lépp. Buleen ragal dara, nde ndiiraanu ramatu, yeena ko gën.