TSK

TSK · Luke 22:35

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Fàttlikuleen mboolem yoon wi leen seen Yàlla Aji Sax ji awale diiru ñeent fukki at yii ci màndiŋ mi, teg leen coono, nattu leen ngir xam li ci seen biir xol, xam ndax dingeen wormaal ay santaaneem, am déet.

Firawna ne ko: «Ana loo ñàkk fii ci man, ba bëgga dellu nii sam réew?» Adàdd ne ko: «Du dara sax de, xanaa bëgg rekk, nga yiwi ma, ma dem.»

Mosleen, xam ne Aji Sax jee baax, ndokklee yaw mi ko làqoo.

Luke 10:4 TSK

Buleen yóbbaale dencukaayu xaalis, mbaa mbuus, mbaa ay carax te buleen taxaw di saafoonte ak kenn ci yoon wi.

Noonu lañu binde ne: «Ki dajale lu bare ëpplewul, te ki dajale lu tuut ñàkkul.»