TSK

TSK · Luke 23:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Naka la Axab gis Ilyaas, ne ko: «Kii yaw a, di lëmbe Israyil nii?»

Nit ku bon a ngi may duural, di ma jiiñ lu ma yégul.

Làq ma pexey ku bon, ma rëcc gàngooru defkati ñaawtéef.

Ba mu demee ba tollook buntu Beñamin, daje faak njiitu dag ya, Irya doomu Selemya doomu Anaña. Irya taxawal Yonent Yàlla Yeremi, ne ko: «Ãa, waa Babilon nga daw jëm!»

Amos 7:10 TSK

¶ Ba mu ko defee Amaciya sarxalkatu Betel yónnee ca Yerbowam buurub Israyil, ne ko: «Amos a ngi lay fexeel ci digg Israyil. Réew mi du àttan waxam ji.

Waaye gannaaw-si-tey, Doomu nit ki mooy toog ci ndijooru Yàlla, Aji Man ji.»

Mu ne leen: «Yeena ma indil waa jii, ne ma mooy lajjal askan wi. Man nag laaj naa ko ci seen kanam, waaye gisuma ci moom genn tooñ ci li ngeen ko tuumaal.

Ñu taxawal leen fa àttekat ya, ne: «Ñii ñoo yëngal sunu dëkk bi, di ay Yawut

Acts 24:5 TSK

Waa jii lanu gis ne ab rambaaj la buy sabab réeroo ci biir Yawuti àddina sépp. Moom mooy njiitu ngér mu sikk mi ñuy wax Nasareen ñi.

Waaye nay tont lu rafet te ànd akub yar. Saxooleen di jëfe li dalal seenum xel, ba mbir ma ñu leen di baatali, ñooñuy ŋàññ seen dundin wu rafet wi leen Almasi manloo, gàcce rekk lañuy jële ca mbir ma ñu leen di baatali.