Ña nga naan: «Boroom gént gaa ngee di ñëw!
TSK
TSK · Luke 23:35
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yaw lañu daa woo wall, mucc; yaw lañu wóolu woon te rusuñu.
Ay xaj a ma wër, di gàngooru saaysaay, dar ma kepp, bëtt samay yoxook samay tànk.
Noon bu ma deful dara, yàlla bumu gis lu mu ma damoo. Ku ma bañ ci dara, yàlla bumu ma ree.
Yal na seeni dal gent, seeni xayma wéet.
«Xool-leen sama jaam bi ma yor, sama tànnéef, sama soppey xol, ci kawam laa teg samag noo, te mooy dogalal xeet yi yoonu àtte.
Dees na ko xeeb, daw ko, muy nit ku bare mitit te miin naqar. Mu mel ni ku ñuy dummóoyu, dees koo xeeb te nawloowuñu ko.
¶ «Bu loolu amee maay sottil waa kër Daawuda ak waa Yerusalem, noowug yiw aki dagaan, ba ñu geesu ma man, mi ñu jam ba mu sar, te dinañu ko jooy ni ñuy jooye benn bàjjo, di ko naqarlu ni ñuy naqarloo deewug taaw.
Ñu ne ko: «Soo dee Almasi, wax nu ko.» Mu ne leen: «Su ma leen ko waxee, dungeen ma gëm.